Président Yûsu Groupe Futurs Medias
Bu ma sañoon, ngeen bàyyi xel Yawmal Najâh
Bés la boo xam ne taxawaay ba dey yàgg
Da ñuy peese jëf yi moo tax muy yàgg
Te képp ku sa métier donoon foo
Di nga réccu, ndax bu boobaa doo tal foo
Ma bëgg nak, nga teel a bàyyi li ngay def
Te ñëw ci Révolution bi, ndax du ay kaf
Di nga ci amee àddunah, am al âqirah
Moo gën ba dem, ñu naan la amoo fi dara
Ndax ku yaakaar KU-TEDD-KI dem Aljanâh
Waaye le gën ci Murîd, ñu neh texe na
Léeb naa la, lupp la, mel ni da nga tëx
Du ma la ko jàppe, ndax Saytâne moo tax
KU-TEDD-KI, Moom miy sauver, YÂL’na la sauver
Yaa’k koo bokkal métier mi, YÂL’na ngeen sauver
Ndax bu KU-TEDD-KI waxul ci réew mi
Balâh bu rëy di na wàcc ci réew mi
Bu ngeen ma déglu wul, xanaa di tangxamlu
Li ci kanam rawul i bët, kenn du falu
Traduction en français
Youssou, président du Groupe Futurs Medias
Si c’était de mon gré, vous garderiez à l’esprit le Jour de l’Attente
Ce jour-là, la station debout sera longue
La pesée des actions le fait durer si longtemps
Et toute personne dont le métier est l’amusement
Aura du regret, car ce jour-là, il ne sera plus temps !
Je souhaite dès lors que tu cesses sans tarder
Afin de rejoindre la Révolution, car ceci n’est point de la plaisanterie
Gagnant alors tu seras pour la vie d’ici-bas et celle de l’au-delà
Mieux serait de s’y rendre ainsi, plutôt que de s’entendre dire tu as perdu
Car quiconque a foi au Très-Saint, sera au paradis
Et le mieux pour un Mouride est de se voir béni
Je te fais des allusions et des métaphores, mais il semble que tu sois sourd
Sachant que le démon en est la raison, je ne t’en tiens point rigueur
Le Très-Saint qui est le Sauveur, DIEU fasse qu’Il te sauve
Que tous ceux de ta corporation, soient sauvés
Et si le Très-Saint ne se prononce pas au sujet du pays
Alors une catastrophe s’abattra sur ce pays
Si vous ne m’écoutez pas, à force de faire l’oreille sourde
Surviendra ce à quoi vous assisterez, élu nul ne le sera.